Click
one of these for: français
| português | swahili
| english
Nisër
yi :
Fi
ñu dajale xam-xami cosaan yi ngir yokkute gi ci xarala gi ñu naan
web ("Enternet") maye na ñu mën a jokkook béréb yu bari yu xam-xami
cosaan yi bawoo. Li ko tax a jóg mooy yombalal waxtaan wi ci diggante
waa dëkk yi, kurél yi jokkuwul cigg nguur ñu gën leen a xame ci
turu "Oo-En-See", nguur yi, kurél yiy maye , askan wi ak ñi
ame seen liggéeyu bopp. Li gën a tax mu jóg mooy béréb la buy
yombal lëkkoog xam-xami cosaan yeek fànna yi ñi ñu jàppóol ngirug
yokkute di yéngu ndax ndimbal yi gën a am njariñ rawatina yi ñu
jaglelee néew ji doole yi.
Pexe
yi:
Ngir
am li ñu nisër dañoo jëfandikóo pexe yu wuuté. Bokk na ci pexe
yooyu, sàq mu ñuy dugal xam-xam ak jëfi cosaan yi, ba ci lu mot
téeméer ak bépp xeeti jukkib xam-xami cosaan buy wone yenni leeral,
ay pajtal yu ñu fexee fi ñu leen di jëfandikóo ci jafe-jafe yu
doy waar. Sémb bi dinay dimbale ba tey ay bérébi xibaaruwaay ci
xam-xami cosaan yi nekk ci réewi Afrik yu bari, te li tax ñu jóg
mooy ràññee ak siiwal xam-xam ak jëfini cosaan yi. Nguur yeek
ñi mu jàppóol ci dëkk yi la sémb bi àndal sóobu ci dugal xam-xami
cosaan yi ci porosey "Bànk Monjaal" yeek sémbi réew yi.
Ndajem
GKII
Mbooloom
xibaar ci xam-xami cosaan réewóo réew.