Xam-xami Cosaan
yaa ngi liggéeyal yokkute gi

Ay jigéen ñu dëkk ca réewum Malee ngiy defar ay ndimó, di leen rafetal aki rëdd yoo xam ne pexem cosaan mu tudd "Bogolaa" lañ koy defe
Pexe mee ngi ame ci kiliftéefu Bànk Monjaal, mu jàppóo ceek kuréel yii : CEA, CIRAN; NUFFIC, SISDA , CRDI, OMPI, OMS, PNUD, SANGOnet, UIT ak UNESCO
|
Porose bi ñu jàppóo ngir xam-xam bu daj àdduna si dëgg, du mën a antu feek ñi gën a néew doole bokkuñu ci, taxaw taxawaayu ñuy jëfandikóo xam-xam bi ak ñu ciy def seen wàll. |
Luy nisëri pexe mi ak
ci lan lay yëngu?
Tas xabaar bi
• Sos sàp muy ñuy dugal lépp luñ def ci wàllu xam-xami cosaan yeek liñ ci mën a jànge.
• Siiwal ay misaal. Moo xam ciy kayit walla cib masin.
Yombal weccantem xabaar mi digante réew yi néew doole
•Dimbale nit ñi ba ñu gën a mën a veccante xam-xami cosaan yi.
• Xam pexe yi gën a mën a weccante xam-xami cosaan yi.
• Xam pexe yi gën a mën a tax ba nit ñi xam xam-xami cosaan yi te siiwal leen.
• Yombal yoon woo xam ne àdduna sépp a ciy jokkoo, di ci weccantey xam-xami cosaan.
Jëfandikóo xam-xami cosaan yi ci yoonu yokkute.
Fexe ba ñi yokkute gi soxal nangu ne xam-xami cosaan yi am nañ solo
• Fas yéenée jëfandikóo xam-xami cosaan yi ci lpp lu nuy sumb ak
porose Bànk Monjaal yeek yu ñi mu jàppóo ci yokkute gi.
Taxawalug jàppóo
• Jànge ci nit ñeek kuréel yi jokkuwul cig nguur maanaam Oo-En- See (ONG) yi.
Jëfandikóo ni mu ware tuut si ñi jàppóo am ngir yokkute gën a am ci dëkk yi.
• Leeral àqi moomeelu xaam-xam nga xam ne coow la ci xam-xami cosaan yi.
Lu waral xam-xami cosaan yi
am solo?
• Xam-xami cosaan yi dañuy jox waa dëkk bu nekk rawatina ña fa gën a néew doole ay pexe yu ñuy mën a faje seeni soxla. Taxawaay bu am solo lañ am ci xam-xam bi ñuy jëfandikóo ci àddina si ci wàllu yokkute.
• Li ñuy jëfandikóo xam-xami cosaan yi ci yoonu wiy indig yokkute doyul.
Lu tax ñi yokkute soxal
war a yég ne ci lañ bokk?
• Li ñu jànge ci xam-xami cosaan yi ci lañuy gën a a mën a faj soxlay nit ñi.
• Su ñu dëppalee li ñuy def ci àdduna seek nekkini nit ñi ci dëkk yi, suñu liggéey dina gën a am njariñ, gën a dox.
`• Bu ñu defee dara ci tasum xam-xami cosaan yi lañuy mën a dimbalee nit ñi ba ñi bokkul aada gën a xamante.
|
Cosaanu pexe mi Ndaje mu mag mi àdduna si amaloon ngir waxtaane xam-xam, te amoon ci weeru suwew atum 1997 ca d¨*ekk bu tudd torontóo nekk ca réewum Kanadaa, dafa feeãl ni jàng; aar ak weccante xam-xami cosaan jampe. Ci jamono ji ñuy jàppóo ngir xarala yi ñuy siiwale xabaar ak yi ñuy jokkoo ci Afrig, la Bànk Monjaal dogoo ci taxawal pexe mu jublu ci xam-xami cosaan yi ngir ñu gën leen a nangu, te di leen gën a jëfandikóo siiwal leen ci (làng gi jublu ci yoonu yokkute) lépp lu jublu cig yokkute. |
Nan lañ déggé
xam-xami cosaan?
Askan wu nekk, caada wu nekk dafa am ay xam-xami cosaanam. Ci xam-xam yooyu lañuy sukkandiku ci lépp lu ñuy def ci dëkk yi ci wàllu mbey, wér-gi-yaram, caytum càkkéef yi ak yeneen ak yeneen yu ñuy yéngu. Xam-xami cosaan yaa ngi feeñe ci jëf yi, kuréel yi, digante nit ñi ak aaday askan wi. Bés bu nekk, dañuy bokk ci sunug dund, ni garab yeek pexe yi ñuy fajoo añs.
Ana ñan ñoo jàppóo?
CEA, CIRAN / Nuffic, CISDA, CRDI, SANGONet, UIT, Bànk Monjaal ( Ndéyu mbill gi) AMPI, OMS, PNUD, UNESCO.
Fi àdduna si jokkoo ci xam-xami cosaan, këru xam-xami cosaan yi ci réew yu néew doole yi.
Ñu ngi wut ñu bees ñu bokksi ci ñi jàppóo.
Ni ñu mënee jokkook ñun:
Seen wàll ci waar wi, seeni gis-gis ak seeni laajte mbégté lañ ci ñun:
Bànk Monjaal
Kër guy tasaare xam-xam ak xabaar (diiwaanu Afrig)
Reinhard
Woytek
1818 H Street NW
Washington, DC 20433
Etats Unis
Tel : + 1 202 473 1641|
Fax : + 1 202 477 2977
E-mail : rwoytek @worldbank.org.
Site web: http://www.worldbank.org/afr/ik
Ni nit di def ba indi wàllam ci sàq mi?
Su ngeen amee xibaar ci xam-xami cosaan yu am njariñ, baaxeléen ñu ci!
Na ngéen joxe tegtal yu leer ci yii:
- fan lañuy jëfandikóo xam-xam bi ( réew meek fi mu nekke)?
- kan moo leen di jëfandikóo ( ci misaal séerér si, walla fajkati cosaan yi)?
- ci yan fànn lañ leen di jëfandikóo ( mbey, wér gi yaram)?
- Yan jumtukaay lañuy jëfandikóo ( ci misaal bu ñuy xeex ak suuf siy dee, walla pajum xale yi).
Na ngeen leeral melo yi gën a fés ci xam-xam bi ngeen di wax:
-lu tax mu am solo ci waa dëkk bi?
-lu tax kuréel yi yokkute soxal war a gën a xam li aju ci xam-xami cosaan yi?
- lu tax mu mën a amal njariñ ñeneen ñi dëkkul fi xam-xam bi cosaanoo?
- fan lañ mën dem ba gën leen a xam?
Buléen fàttee joxe seen tur ak seen sant, fi ñu mën a jokkook yéen, seen nimóró telefon; faks walla bu fekkee ne am nga ko, bu e-mail ( fiñ léen mën a jote ci yoonu Enternet)